- Home
- GTN Curriculum
- Partner with Mike and Jill
- Select Language
Yittéy GTN
Gis-gisu Global Training Network mooy joxe ay njàngale yu am solo ci wallu Biibël ak diine ñeel ay junniy sàmp kati jàngu yu bokk ci réew mi, ay pasteur ak ay njiiti Kirist ci Afrig, Asi ak Amerik Latin, ngir pasteur yooyu ak njiit yooyu mën a tàxawu bu baax, seeni mbooloo te jiite leen ngir ñu yégle xibaar bu baax bi te tàggat seeni waygem ngir yook seen xam xam ci Kirist.
Wéyal di jàng ngir gën a xam liggéeyi nguuru Yàlla ci Senegaal ak Gàmbi ak naka nga mëna jote ci sunuy njàngale yu am maana yi GTN di joxe ci sa làkk.
GTN ci Senegal ak Gàmbi
Yeesu mi ngi wéy di tabax jàngoom ci Senegal ak Gambia jaarale ko ci Global Training Network (GTN) ak sunu ay way lëkkëlo yu bare yu bokkak nun gis-gis. Sunu lëkkëlo bu yàgg ak Mission Inter Senegal (MIS) moo ubbil bunt bi, Pastër Mike ak Jill Edelman ngir ñu mëna tàmbali liggéey ak GTN, bu jëm ci taxawal ak dëgëral sàmm yi ak njiiti Kirist yi ci Afrig gu sowu - dëkki Afrig yi ci Sowu suufu Saara.
Baa léegi ci atum 2021, GTN sàmp na ay lëkkëlom njàngale ak ay mbootaayi sàmm aki jàngu, ci biir Senegal ak Gambia gépp. Lu ëpp 300 jàngu bokk ñañu ci njàngalem Biibël bi GTN di amal ci biir ay kureel yu bare yu wuute. Njàngale mi GTN di amal mi ngi dooleel pastër yi, ñoom itam ñu nekk di yokk seeni jàngu ngir jot gox-goxaat yi ak kàddu gi.
Wéyal di jàng ngir xam sunuy njàngale yu am fës yi.
Njàngale yu fës yi GTN di joxe
Danuy joxe fukki njàngale ak ñaar yu am maana yoo xamni, leegi mën ngeen koo am ci anam gu ngeen di jàngal seen bopp. Mën ngeen déglu te jàng njàngale yi yépp ci Angale, Farañse, Wolof ak Sereer. Ci dalu xarale gi di keru web, bi ci biir Internet, mën ngeena am lii di topp:
• Xet wu njàng bi nekk ( Ci Angale, Farañse, ak Sereer).
• Ay anregistare yu njàngale yépp nekk ( Ci Angale, Farañse, Wolof, ak Sereer).
• Mbind mu mengook anregistre bi, ngir topp ci, su fekkee ya ngi déglu (Angale, Farañse, ak Wolof).
• Njàng bu nekk 30 simili lay tollol.
Lu jëm ci Mike ak Jill
Mike ak Jill séy nañu 41 at, nungi dëkk Elverson, ci Pennsylvanie (ca Amerig) Ñoom ñaar ñépp gëm nañu Boroom bi niki seen Musalkat, jaarale ko ci liggéeyu Jàngub Christ First Church (CFC) bi nekk Downingtown, ci Pennsylvanie, lu weesu 35 at. Ci yërmaandem Yàlla, woo Mike ngir mu nekk Pastër Ñaan ak Mbooloo yi ca CFC ci atum 2007, ba mu welbatiku bokk ci Global Training Network (GTN) ci weeru Desàmbar 2020.
Mike ak Jill am nañu mbëggeel gu réy ci Senegaal, ci Afrig sowu, te mbëggeel googu di gën di yokku ci 22 at yi weesu. Noonu ñu dem bay liggéey ak ay mbootaay yuy yëngu ci samp ay jàngu aka tabax taalibe yi. Bokk nañu ci GTN ngir bëgg a defar ak dëgëral pastër yi, ñiy samp ay jàngu, ak njiit yi ci Senegaal, te di wéy di yaatal seeni lëkkëlo yu am solo, ci réew mii nga xam ne 97% ci askan wi, ay Jullit lañu yu ubbeeku ci wallum Injiil.
Doore ko ca atum 2021, ba léegi si, Boroom bi may leen ñu mën a samp ay ati lëkkëlo yu jëm ci tabax, ay mbooloo ak ay mbootaayu jàngu yu bare, yu nekk ci seenum réew , te ñu ngi gën a yaatu. Mbooloo yooyu jàpp nañu ci gis-gisu 2 Timote saar 2 ayaa 2, di gis-gisu fulandi ay njiit aki taalibe.
Ci atum 2024, Yàlla ubbi ab bunt ngir am beneen lekeloob njàngale ca Gambi, réew mu ndaw mu nekk ci biir Senegaal. Askanu Gambi ak askanu Senegaal benn lañu. Réew la joo xamni 98% ay jullit lañu, te amna fa moom sa bopp, ci wallu diine. Mbootaayu jàngu yi lëkkëlo ak GTN am nañu pasteef ju réy ngir jot seenum réew ak xibar bu bàax bi.
Jill dafa doon yëngu ci rafetal biir kër te doon doxal liggéeyam moom ci boppam lu mat fanweeri at ak juróom, laata muy bokk ci GTN. Dafa am mbégte ci jamono ju bees jii di ñëw ngir liggéeyandoo ak Mike ci biir GTN. Mike ak Jill am nañu doom ju góor ak ñetti doom yu jigéen yuy séy te seeni borom-kër nekk ay waygëm, te am nañu fukki së́t ak ñett yu dëkk caFloride ak Pennsylvanie.