Xëtu Jàngale yu Fës Yi GTN di joxe

Naka Laay Mage ci Xel Mu Sell Mi

Jàngale bii dafay joxe cëslaay bu dëgër, ngir, waygëm ku bees mën a xam moom, mooy kan ci Kirist ak coppite gi xel mu Sell mi di meññ ci dundam gépp, ngir mu nekk melokaanu Kirist.

 

Nettali Kóllëre gu Njëkk gi

Jafe-jafey Kóllëre gu Njëkk gi, dinañu leen leeral ci anam gu mag gi, di ni Yàlla di tabaxe Nguuram. Dinga mën a nettali nettalib Kóllëre gu Njëkk gi ci lu yées fukki simili ak juróom, la dale ca Njëlbeen ga ba ca Sàkkug Nguur ga ci jamonoy Maam ya, ba ca Juddug Askan wa ci njiitu Musaa, ca Ngurug Yàlla, ba ca Ngurug Nit, Gadday Ga, ak Jamonooy Yésalaat Ja.

Nettali Kóllre gu Bees gi

Dalee ci njeextalu nettali Kóllëre gu Njëkk gi, ba ci Ñeenti téeméeri at yu amul xibaar, ba ci ñëwu Kirist bu njëkk bi, jàngkat bi dina mën a tënk Injiilu Nguur Gi, Yittéy Nguur gi, ak Yaakaaru Nguur Gi, dalee ci Macë ba ci Téereb Peeñu ma, ci diirub fukki simili ak juróom walla lu ko yées.

 

Cëslaayi gëm Kirist - Njàng 1

Lii mooy njëkk ci ñetti njàngalem ngér yi jëm ci li ëpp solo ci ngëmug Kirist. Njàng mii dafay gëstu dogalu Biibël Bi, Yàlla, Doomu Yàlla, Xel mu Sell mi ak Kennefu Ñett Ñi.

 

Cëslaayi gëm Kirist - Njàng 2

Sunu ñaareelu njàngalem ngér bokk ci ñetti yi ëpp solo ci ngëmug Kirist. Njàng mii dafay gëstu dogalu Nit, Bàkkaar, ak Mucc.

 

Cëslaayi gëm Kirist - Njàng 3

Sunu ñetteelu njàng mi bokk ci ngér di bi mujj dafa jëm ci li ëpp solo ci ngëmum Kirist. Njàng mii dafay gëstu dogalu Malaaka yi, Eglis bi, ak Mbirii mujjantal yi (Eskatoloji).

 

Naka lañuy jàngee Biibël bi

Dinga jàng jumtukaay yu jëkk yi jëm ci firndé ngir jàng Biibël bi, te di ko sukkandikoo ci yoonu ñetti jéego yu yomb te jàppandi: Seetlu, Tekki, ak Jëfe. Jumtukaay yooyu, dinga leen jëfandiko ci jàngum bataaxalu 1 Yowanna.

 

Anam yi lay may nga Mag ci Xel mu Sell Mi

Jàngale mii dafay wone soxla bi jàngu bi am jëm ci njiit yu xareñ ak sàart yi leen di mandargal yu ñu jële ci Biibël bi, ak juróom-ñeenti njàngat yu jëm ci njiit, te ñu jële ko ci dundug Nehemiya.

 

Ñaan gu Tegu ci Jaamuu

Jàngale mii dafay joxe cëslaay bu jóge ci Biibël bi, buy gëstu xalaat bii di "wut kanamu Yàlla, baña yittéwo loxoom kese ", te àndak ab xetu ñaan bu ñu wara roy ñu jële ko ci Mbind mi te Xel Mu Sell Mi di ko jiite, di njàngalem Yeesu ci saar 6 bu Macë.

Ay Tektal yu jóge ci Biibël bi ngir Maye

Ak gis-gis bu sax ba faww, te xam ne Yàlla moo moom lépp, jàng mi dina la dimbali, nga man a raw ci yërmaande ju mag gi nekk ci maye, te mu sukkandiku ci ay tektal yu bawoo ci Biibël bi, yu nekk ci 2 Korent, saar 8 ak 9.

 

Gisal ni la Yàlla "MOÑEE" ngir liggéeyam
 
Waygëm bu nekk am na ay mayi Xel Mu Sell Mi ngir tabax jàngu bi te màggal Yàlla. Yàlla. Te it Yàlla "mol" na ku nekk ci ñun ngir liggéeyam, jaarale ko ci ay mayi Xel Mu Sell Mi, li soob nit ki, may yi ñu judduwaale, jikko yi ak jaar-jaar yi sa dund. Jàng mi dina dimbali ki di wayjàng bi mu gis ni ko Yàlla "defaree" ci anam gu wuute ngir mu liggéeyal Yàlla ak mbégte ak am lu mu ci jublu.

 

Tabax Séyu Kiristiyen yuy Sax

Yàlla moo sàkk séy ca Toolu Eden te am na jubluwaay ak lu muy ciy séentu ngir séy bu naat. Ndaje mi, dañu ko jaglel séykat yi ngir ñu xoolaat li ëpp solo ci séy bu Kirist nekk ca digg ba, te yeesalaat seen digey séy ngir mu sax, ci kaw ñuy bàyyi xel seen donog ngëm.